31.07.2021 Views

Yoonuw jàmm ci leeral mbirum gàmmu bu Seriñ Allaaji Mbàkke-1

Create successful ePaper yourself

Turn your PDF publications into a flip-book with our unique Google optimized e-Paper software.

Aji-bind ji :

Sëriñ Àllaji MBÀKKE

Yoonuw jàmm ci

leeral mbirum

gàmmu

Aji-yaxal gi :

Àllaji Elimaan NJAAY


LALTAAYUG AJI-YAXAL JI

Ci turu Yàlla miy Yërëmaakoon, di Jaglewakoon.

Kenn ci ndongo yi tudd Àllaaji Elimaan

Njaay dëkk Ndar, di jànge ci Daara ju

kawe ji nekk Bambey, bokk it ci mbootaay

gi di WAX (Wolof Ak Xamle). Moo doon def

liggéey bi ngir jàpp ci yaatal liggéey

bu sell bi nga xam ni Sëriñ Àllaaji

MBÀKKE xaadimul xaadim, mi ngi koy def

ngir xamle diine Lislaam ak yaatal

njàngaleem Sëriñ Tuubaa ba ñépp man

ci jariñu. Te mu defoon ko ci làkku

wolof, ngir moo yombal jàng ak xam, ci

kèpp kuy sàkku xam-xam.

Waaye xam ngeen ni mbindum wolofal

araab, dafa jafe jàng lool; ci noonu moo

tax nu sotti ko ci wolofal bu gereg bi,

ngir li ëpp ci réew mi man ko jàng ci lu

dul benn coono.

Xanaa nu ñaan Sunu Boroom nangu liggéey

bi te mu ànd ak ngërëmal Sëriñ Tuubaa.

Te Sëriñ Àllaaji sunu Boroom yokk aw

fanam te dolli ko ay ngërëram ci barkeb

Sëriñ TUUBAA .

JËRËNGEENJËF


أوذبع للّها نم لشا ‏ّيطان الر ‏ّجيم

ونّىإ عيذا اه کب وذّيتهار نم لشا ‏ّيطان رجيم

بّر عوذأ کب نم مزاته لشيطينا أعوذو بک

بّر نا يحضرون

بسمل للّها لرّحمانا لرّحيما للّهما حقب ّ جهو اللّه

عتلىا لكريما لّص و لّمس وارکب لىع سيّدبا

موو لاان حمّدم عولها صحبهو صلاةوسلاامو

ركةب قودت هاب لشيخل لخديما ااخترتم ورضيت

هل ىف لحا لا ولمئا ال

ونکع اي عينم و کب نستعين


Yoonuw jàmm ci leeral mbirum gàmmu

Mooy màggal guddi gi Yónnent bi gane àdduna STW te mooy guddig

altine tolloog fukki fan ak ñaar ci rabiqul awwal ca Màkka.

Sëriñ Tuubaa XLML bimu ñëwee àdduna daa jël guddi googu jàppe ko

lumu moom nee na liya rabiqul awwal ak rabiqul awwal liya, te mooy

moo moom weeru gàmmu wépp. Meloon a ci noo xam ni képp kumu

wax ni maa ko moom nga gëm ko te doo ko sikk. Daan a wax itam weeru

gàmmu amul bis bu ñaaw. (siiw na)

Nee na:

Barakatul maahil wali

Saanat rabiqal awwali

Bil maalikil muxawwili

Muxni sawit tafadduli

Barkeb Yónnent bi STHW moo rafetal weeru gàmmu. Ba tay nee na

diine ji te mooy Lislaam da koy yeesal di ko aar di ko gën a saytu ci

mbind yi muy bind, rawatinaak bu guddi gàmmu ñëwee.

Lahu qalayya li wajhil laahi daynu shanan bihi yu jaadadu

diinul laahi layla yabi.

Sëriñ Tuubaa XLML àggoon a foo xam ni ay jëfam ci Yàlla SWT daa na ka

manu ko yokku waaye bu weeru gàmmu ñëwee da na feeñal keem

katanam ci joxe ak bég ak ubbiku bañu xam ni weer wi moo ko waral

weer wi wépp itam la daan def noonu ci nemmiku leeral ciy mbindam.

Da haani ilaa ixyaa i sa shahri kaw nuhu li xayril waraa

sarfan hawaa kula suudadi.

1

1


Yoonuw jàmm ci leeral mbirum gàmmu

Waaye rawatinaak guddi gàmmu ak bu bëccëg gàmmu, ñu bari dañuy

yam ci guddi gi waaye bëccëg gi itam lunu war a dundal la, Sëriñ bi gis

nanu muy wax ci xasiida gi naan dañiy dundal bëccëgug gàmmu xoolal:

Allahuma salli wa sallim wa baarik qala man ahyatu bi hil

abyaati yawma mawlidihi haasa

Ba tay bokk naa ci li ñuy xamal màggug weer wi Sëriñ Tuubaa XLML da

daan wax ak moom ni muy waxeeg jëmm bu dee ñëw ak buy dem

xoolal rahabtu taxsimaa bi shahril Muntaxaa halayhi tasliima

muniilil irtixa.

Ba tay mel na ni ci la daan takk ak tàmbaleem gis nga mu naan:

Ahyaytu mawlida nabi min asashi

Wan xaada li fawxul munaa fi hamsashi

Ba tay:

Lillaahi shukriya fi shahrir rabiihi huna

alab tidaa-i lasi lix taara xurbaana

Ba tay:

Axtaytu kulli lil aaxiiril awwali

Shukran yaduumu min raabixil awwali

Ba tay: Qabdan xadiiman min raabiqil awwali

Ni muy waxe itam day mel ni liggéeyam da koo tàmbali ci gàmmu

Asashi (1301) te mooy bi Sëriñ Moor Anta Sali RLTH làqoo at ma ca sës.

Xabilta li min asashi li balsashi

Muna bihan fi saaka aama lasashi

2

2


Yoonuw jàmm ci leeral mbirum gàmmu

Guddi gi mi ngi tàmbalee timis ba fajar walla ba jànt bi génn ci ku koo

man. Diggante boobu fukk waxtu la ci at mu nekk ak weer wu nekk bu

dee yokk itam du bari, bu dee wàññeeku itam du bari. Kon bu nu

sëlmalee timis danoo war a jël lu mat ñatti waxtu yoo xam ne danu ciy

jàng Alxuraan rekk bu nu noppee fekk nu sëlmal gee lu yàgg,

tàmbalee dundal guddi gi ci xasiida yi boole durus ak yékkati.

Bu nu ko manee nu boole jasbul xulub, mawaahibun naafix,

muxaddamatul amdaah. Bu nu jànge fukki woy ak ñaar (12 bayit) ci

jasbul xulub, taxaw jàng lu mat fukki woy ak ñaar mawaahibun naafix,

taxaw jàng fukki woy ak ñaar ci muxaddamtul amdaah.

Daa di noppalu ci durus te mooy jàng lu mel ne Nuurud daarayni

walla muxaddamatul xidma walla muxaddamatul kubraa benn

yoon walla ñaari, ndax bu nu bëggee yékkati guddi gi lépp du baax ci

nun te dana dem ba ñu bari di yoqat walla ñu sonn.

Lii buñu ko defee li ci ëpp bu guddi gi di jeex dana fekk ñatt xasiida yoo

yii itam di waaj a jeex bu nu ko manee teg ci lu mel ne midaadi ak

yasuuru ak walaxad karamnaa bi nga xamee ne ci weer wi la ko

def ak Limaahim bashiir guddi gi daa di jeex.

Fajar xar ku sëlmal suba bu la neexee nga wéy di jàng ba jant bi génn

waaye li tàmbalee ci jant bi jëm tisbaar moom ba timis ku ko man na ci

durus gën di ci yékkati. Bu ñu xoolee waxtu julli yi sax daale ko ci tisbaar

ak tàkkusaan lenn lu ci nekk dañu koy yeelu boo koy julli.

Kon ku bëgg dundal bëccëgu gàmmu dangay yendu durus Alxuraan

walla xasiida te joxeloo man ci aw ñam ak ub naan ak sa alal ju la lew.

3

3


Yoonuw jàmm ci leeral mbirum gàmmu

Sëriñ Tuubaa XLML nee na:

Mawliduhu muhas samu

Tah siimuhu yan hatimu

Mubaara kun muh taramu

Halaa sawit taqad dumi

Guddi gi mag na lool te barkeel...

Taxsiimuhu bi sunnati

Bihis di yaa dul minnati

Yaxuudunaa lil janati

Li muxlisim muhassimi

Ku ko màggal ci sunna te mooy li muy bëgg wax ca kanam. Man a laa

yóbbu àjjana te day yokk ag xéewal boo ko sellale.

Fa man yu haassim mawlida

Fala yuxaa sabu xadaa

Nabiyyinaa baabil hudaa

Fah tari man waa hassimi

Ku ko màggal deesul a xisaab ëllëg.

4

4


Yoonuw jàmm ci leeral mbirum gàmmu

Fa man yu hassim mawlidaa

Faka shahiidin shahidaa

Xayril baraa yaa Ahmadaa

Badraan bi xayri wa hami

Ku ko màggal mel na ne teewee na xare Badar te mbooleem ña

teewoon Badar Sunu Boroom SWT gëram na leen ba noppi digleen

àjjana.

Fa kulluman an faxa fi

Maa lan bi xayri sara fi

Mawlidihi musharra fi

Wa law bi xadri dirxami

Ku ci dindi dara ci sa alal joxe doonte benn dëram la mel nga ne ku

teewe xareb Unayni ak xareb Badar di dimbali Yónnent bi STW.

Su ko defee war na noo fexe ba benn dërëm booba nekk bu lew domm.

Fa kulluman xad hadaraa

Muhassimam mubashiraa

Fa innahu, xad safiraa

Waala yu laaxi dararaa

Mawlida afdalil waraa

Bisukkarin aw lahami

Bimaa yu diimul busharaa

Yawmaj timaaxil umami

5

5


Yoonuw jàmm ci leeral mbirum gàmmu

Ku ciy bégle ci lu saf suukar mel ne di joxe kafe walla attaaya te ñuy li

gën walla meew walla bisaab walla ñam yu saf suukar yi mel ne màngo

walla pom walla orãs. Sunu Boroom SWT dana ko may mbégte yu sax te

du am jenn dur yawmal xiyaam.

Ku ci defar aw ñam mel ne cere walla ceeb walla ak ndawal walla lu ñiy

jëfandikóo lu mu man a doon jox ko kiy jàng ngir màggale ko guddi gi.

Sunu Boroom SWT dana la booleel yiwi boroom yittee yu mag yi yépp

te ñooy niti Yàlla yi. Lu mel ni nag soxna yi ñoo ci war di gën a farlu ndax

li ëpp ci ñoom duñu man a def li góor ñi di def.

Kon war na kenn ku nekk jigéen ngay def sa keem kàttan ci defar ñam

wu baax moo xam cere la walla leneen di ko jox ñiy jàng ndax ni ko

Sëriñ bi leerale mooy ki koy def day boole yiw yépp.

Wa man halaa shay in xaraa

Tabarru kan fa sayaraa

Mawlida sayyidal waraa

Numuwwahu, bil fadxami

Loolu ñuy jàng ku ko tëfli ci am ndox di ko naan walla nga di ko def ci

leneen ngir barkeelu fàww nga cay gis ag yokku.

Am na ñoo xam ne buñiy tàmbalee dañuy wut ndab teg ko fi ñuy jànge

def ci ndox buñu noppee ñépp tëfli ci loolu mel na ni moo gën di duy

am ndox ginnaaw buñu noppee ndax ndox mi diir bi muy tege fi ñuy

jànge loolu rekk ag yokku la ci moom.

6

6


Yoonuw jàmm ci leeral mbirum gàmmu

Wa in alamaa in xuri

Fa shurbu bil mutahhari

Yunawwirul xalba sharaab

Wal xalba yuh yiduuna xaab

Mawlidu xayril bashari

Ya kuffu kaydal murxami

Min saalikal ma bil mujaab

Wahan shaxaa in yaxtami

Ndox moo mi day lay musal ci Saytaane di leeral ab xol di dundal ab xol

di musale ci texedi.

Ihya’u mawlidil bashiir

Fi hi shifaa’un li suduur

Yahmil hiyaala wadduyuur

Li kulli haadin yantami

Màggal guddig gàmmu ak dundal ko day aar ag njaboot ak ay kër di

saafara xol yépp.

Bu loolu jàllee bokk na ci li lay xamal màggug guddi gi bari na xar-baax.

Xarbaax yu ci amoon bokk na ci am sawaara woo xam ne ay nit dañu ko

daa jaamu am na lu mat téemeeri at masut a fay ci guddi gi la fay.

Ba tey am na déeg buñuy wax déegub Saawata am na téemeeri at

masut a ŋiis ci guddi gii la ŋiis.

Mel na ne dañoo jël sawaara wee def ci ndox mi walla ñu jël ndox mi

sotti ci sawaara wi.

7

7


Yoonuw jàmm ci leeral mbirum gàmmu

Wa hayni saawatal lati

Lil fursi xabla millati

Xad hasumat wa jallati

Wa suyyirat kal xadami

Ba tay Sëriñ Tuubaa XLML nee na:

Wakan xidaadi shuhubi

Han samxi axbaarin Nabi

Turida fiihaa bi nujuum

Wa farraxa siran yuliim

Tardal li ahlir riyabi

Wa rajuux bi nadami

Hani samaawaatir rajiim

Bi hisbihii, saa wa kami

Jinne yi dañu daan dem ci asamaan yi di déglu xibaar yi malaaka yi HS di

wax buñu ko deggee gaaw xibaar ko ay nit. Su ko defee bu ko ab

Yónnent waxee ñu wax ne loolu amna ku ko wax. Bi nga xamee ne

Yónnent bi STW gane na àdduna biddeew yi dañoo tàmbalee di dàq

Saytaane yooyii ba manu ñoo déglu dara.

Ba tay Sëriñ Tuubaa XLML nee na guddi gi Yónnent bi STW gane àdduna

leer gu mag daa feeñ ca Màkka ba dangay man a gis tabaxi Xaysaara te

sore na ak Màkka lool.

8

8


Yoonuw jàmm ci leeral mbirum gàmmu

Naka noonu Kisraa amoon na tabax bu rëy boo xam ne guddoon a ba

mel ne luy laal asamaan ci guddi gi daa xar ba ca lal bamu daan tëdd

daa damm ngir leerug Yónnent bi STW. Loolu moo nekk nii:

Sataxa hiina wulidaa

Salla aleyhi man hadaa

Nurun hasimuun xad yaraa

Man kaana fi ummil xuraa

Xayru nabiyyin xad badaa

Fuwaa dahu bil, hikami

Bihi xusuura Xaysaraa

Makkata xayril hurumi

Sëriñ Tuubaa XLML nee na Yónnent STHW daa digg-dóomu ci ab

taxawaayam. Weexul tàll. Aw yaramam rëyul sewul. Ku miy toogal

walla ngeen di dox moo lay sut. Ab dënnam daa yaatu. Li muy ree ci

muuñ moo ëpp. Kawar yi tiim ay gëtam sëq. Mu rafet aw doxiin. Ku am

baat la. Ku mat ay nopp la. Bu muuñe ba ay gëñam feeñ day mel ne ag

melax. Xar-kanamam daa kuttumbal. Amul biir. Buy wax, wax ji day

sësaloo. Ay gëñam buy wax dangay séen ndox mi mel ne wurus.

Bàkkanam daa yékkati ku. Ay bëtam am na lu mel ne ay xonq-xonq yu ci

nekk. Moo gën a mat ñépp ci jikko ak bind kenn masta gis ku ni mel te

kenn dootu ko gis.

Loolu mi ngi nii ci way yi ci jasbul xulub :

9

9


Yoonuw jàmm ci leeral mbirum gàmmu

Xad kaana saa yawa suuti

Wa lam yakun bil mufrati

Wa lam yakun mutahhama

Bal faaxa kulla man samaa

Kaana yatuulu kulla man

Wakaana waa sihal hatan

Wahwa jaliilun xullabu

Bihum ratin wa ahdabu

Yaftarru fi asnab tisaam

Fil xaddi jaalis shututi

Wa lam yakun bi aadami

Wa lam yakun mukalshama

Min muntamil li Aadami

Maa shaahu fi kulli saman

Yad haku bittaba summi

Bayaa duhu musharrabu

Wa an jallun suu rasami

Kal barxi aw xabbil xammam

10

10


Yoonuw jàmm ci leeral mbirum gàmmu

Wadah kuhu yajlus salaam

Wa wajhuhu mudawwaru

Wahwa baqiiyun asmaru

Ka an na maa sahaabi

Wakaa na sabtal xasabi

Kaamilu usnin ad xaju

Wa ashkallum mubtahiju

Wahuwa akmalul waraa

Wal mishlu xattul lam yuraa

Kasuru jin fi sulami

Wahwa xamiisun as haru

Murattilu takallumi

Fi xaddihil muhassabi

xirniinuhu suu shamami

Wa ashnabum mu fallaju

Wal wajhu maa hil xumami

Xalxan wa xulxan saharaa

Wa lan yura fis shiyami

2 fani kori 1434

11

11


Sëriñ Àllaji MBÀKKE mi ngi gane àdduna ci atum

1979 walla 1980 ci Daaru Muhti. Wayjuram Wu goor

mi ngi tudd Sëriñ Mustafaa Hafsa di doom ci Sëriñ

Muhammad Hawa Bàlla moom Maam Ceerno

Biraahim Mbàkke ak Soxna Hafsa Jaxate. Moom

Sëriñ Àllaji MBÀKKE noo ngi ko tudde Sëriñ Kaso

Absatu Lóo, moom nag Maam Ceerno lañu ko

tudde, ñu koy wax koso ngir limu dëkk Kaso, lamu

aji woon Màkka itam moo tax ñu koy wax Àllaaji,

teewul moom Sëriñ Àllaaji itam ajji na Màkka ci ndimbalal wayjuram

wu goor woowu. Wayjuram bu jigéen Soxna Muuminatu la tuddu,

Sëriñ Saaliwu moom Sëriñ bi moo di baayam, Soxna Mati Jaxate moo

di ndayam. Ñaari wayjuram itam amna ñu ag bokku ci ñaari wàll yépp.

Ginnaaw am njàngum Alxuraanam diggante kër Sëriñ Suhaybu,

Tuubaa, Daaru Muhti ak Daaru Xuduus nekkoon na it ci Sëriñ Saaliwu

Mbàkke ci daaraam juñuy wax Njurul di fa jàng Alxuraan ak Xelkoom

biñu koy door a sànci ak Xelkoom Ummul Xuraan ak daaraam ju

tuddu Tuubaa Belel nekk ci biir Xelkoom.

Bi Sëriñ Saaliwu làqoo laa ñëw ci wayjur jébbal ko boppam. Mu digal

ko lu mel ne la ko Sëriñ Saaliwu digaloon te moo di jàng ak jàngale

ca Tuubaa Daaru Muhti.

Fii nu tollu amna fukki at ci barab ba. Yàlla itam dimbali na ko ndax

mi ngi toppu ndigal loolu ba tey te moo di jàngale ak jàng ci làmmiñ

ak ci loxo li ëpp.

Xaadimul Xadiim moo ko tudde boppam ngir xeemeem liggéeyal

Sëriñ Tuubaa .

Limatug aji-yaxal ji: 77 449 54 69

Email: njaayeli@gmail.com

Facebook: Alaaji Ilimaan Njaay walla Jamonook Diine

Hooray! Your file is uploaded and ready to be published.

Saved successfully!

Ooh no, something went wrong!